rééwu melokaan yi - · pdf fileloolu dafay tekki wuute ak ñeneen...

40
RÉÉWU MELOKAAN YI

Upload: trinhdang

Post on 16-Mar-2018

237 views

Category:

Documents


5 download

TRANSCRIPT

Page 1: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

RÉÉWU MELOKAAN YI

Page 2: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

EDITA: Gobierno de Aragón. Departamento de Educación, Cultura y Deporte DEPÓSITO LEGAL: HU - 124/2008 AUTORES / ILUSTRACIONES: Martín Pinos Quílez y Manuel Pinos Quílez DISEÑO Y MAQUETACIÓN: Loher Publicidad TRADUCCIÓN: Moussa Fall, Mediador Social Intercultural, Profesor y traductor de Wolof-Español-Francés

Page 3: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Azîm, Adolph, Isabel, Adrià, Aratz, Amîn, Aaleahya, Moussa, Fátima, Adler, Fernando, Aina, Asier, Aarushi, Ghâlib, Alberta, Alicia, Aleix, Ainara, Aahan, Viorel, Samba, Habib, Amara, Antonio, Andreu, Ander, Casimiro, Catalin, Fatoumata, Halîm, Arnold, Pilar, Arnau, Edurne, Abel, Cosmin, Hasan, Ava, Roberto, Carles, Eider, Alexandre, Mariama, Ibrahïm, Baldwin, Loreto, Dolors, Enara, Amelia, Alin, Fatou, Jalâl, Bernadette, Guillermo, Estel, Eilo, Américo, Dan, Isatou, Jamâl, Bertram, Marina, Ferran, Fani, Anabela, Andrei, Bintou, Jibrîl, Burke, José, Guillem, Arantxa, Anibal, Vlad, Haja, Khâliq, Derek, Olga, Ignasi, Gabone, Aemando, Marius, Mamadou, Karîm, Dustin, Juan, Iris, Garaitz, Brígida, Dorel, Ibrahima, Muhammad, Edwin, Laura, Joel, Gisela, Camila, Cornel, Abdoulaye, Mustafà, Egmont, Alex, Jordi, Hirune, Cecília, Cheikh, Nadîm, Elisabeth, Nieves, Roxana, Júlia, Idoia, Horia, Ousmane,‘Omar, Emily, Pablo, Manel, Irune, Johann, Irinel, Rashîd, Dragosi, Relu, Erika, Ricard, Susana, Ikerne, Dorina, Tammâm, Modou, Bogdan, Frederick, Unai, Luis, Umara, Dana, Marcos, Wâsim, Octav, Martí, Ugaitz, Yaiza, Diego, Zaida, Mor, Abdou, Viorica, Gerard, Beatriz, Sergi, Oana, Heidi, Lorelei, Patricia, Izaskun, Moustapha, Unax, Pere, Verter, Vicent, Corina, Gheorghina, Txaran, Camelia, Mirela, Roger, Richard, María, Marc, Santi, Tristan, Catalina, Alina, Wanda, Pedro, Simona, Nina, Oriol, Ion, Leonard, Norbert, Vanesa, Neus, Marinela, Jorge,

Ci atum 2008 bii, Atum Tugël i ñu jagleel Diisóó ci Digënté Caada yi, ñoo ngi jagle xët yii bépp xale bu góór ak bu jigéén bu nekk ci lekkooli Aragón yii ñu am sããsu bokk ay xool ak ay

ree yu bokk ci aada yu bare te wute ak melo yu woroo.

Page 4: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu
Page 5: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

RÉÉWU MELOKAAN YI

Por Martín Pinos Quílez y Manuel Pinos Quílez

Page 6: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Xew-xew bii ma leen di nettali, mi ngi xewoon ay at ca ganaaw, ba ma nekkee gune. Booba maa ngi amoon juróóm ñaari at te ba téy mu ngi may yéém. Di naa leen ko nettali ni ma ko fattali koo, doon te amaa na xewee wul noona dëgg-dëgg. Xew-xew yi, ni ñu leen di fatteli koo rekk la ñuy mel waye du ñu mel mukk ni ñu xewee woon.

Lépp a ngi xewee woon ca Talkonia, ab dëkk boo xam ne, naka yeneen dëkk yu bari, ña fa dëkk, da ñoo bék ca na ñu mel: maanaam di ay nit yu weex. Da ñoo weexoon a weex mel ni pëndëxu puudër. Ca seen biir, lakku way Talkonia lañuy wax, lakk bu am solo ta neexoon ci dégg.

Ci jamonoy nawet, ñenn ñi da ñu daan xonx ba mel ni xaal.deru yaram bu ni leeree tamit amoon na ay sikkëm.

Terewul duñu ko weccee ak beneen bu gënë xereer, xees baa ñuul. Loolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu.

4

Page 7: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

5

Page 8: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu yéés, nit ñu suufe, ñoo xam ne jaru ñoo séqqal dara.

Ca Talkonia, dund ga dafa neex. Maanaam, daanaka dafa neex ca ñëpp. Ña ëpp ca nit ña amoon nañu liggééy, doon nañu fayyeeku payoor bu baax, ta itam, loolu taxoon na ñu am kër yu rafet, ñaari daamar, ak sax ñaari tele baal lu ko ëpp yoo xam ne ca la ñu daan xool xibaari yeneen bërëp yu seeni nit amuñu woon duna guni neexee. Ñooy suñíy dëkkëndóó yi féété bët saalum, waaye foofu beneen suuf la. “Ñateelu Dunyaa” lañu leen doon woowee. Ñun ñoo nekkoon bi jekk. Damaa mësóón di laaj naan ana ñaareel ba.

6

Page 9: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

7

Page 10: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ci noonu, jafe-jafe yi daa di tambali. Kenn bëggëtul liggééy ci tool yi: seddu noor di ko dugg baa tángooru nawet. Ta itam bëggatu ñu def liggééy yi gënë metti te gënë soof, niki tabax, ligééy ci yenn isin yi baa sax ci yeneen yi mel ni toppatoo mag ñi baa liggééyi kër, tonni mbalit, raxas bërëbu sobe yi. Maanaam daal, liggééy yooyu ku nekk mën na koo def. Ci seen xalaat, liggééy yu ñakk solo lañu.

Ca rééw yu mel ni Negrina walla Marronia ay góór ak ay jigéén tambale difa bawoo di wut si liggééy ak defar seen ëlëg ak seen ëlëgu doom. Mel niki amuñu yelleef ci ëlëg jooju nax liñu juddóó wul ci dëkk bu mel na Talkonia.

8

Page 11: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Lenn ci góór ñooñu ak jigéén ñooñu bawoo ca bët saalum mususñu eksi mukk. Daanañu xotti ndand-foyfoy yu jeggi dayoo, daanaka and ak xiif ak mar. Ña daan yegsi dañu daan ame coono tánk ak bu xel ngir jéggi ay dig te daan fa daje akiy sakketi tabax yu kawe ak bar-bar yu fa giiru Talkonia defoon ngir aar seen ragal lu uute ak ñoom.

Tere wul ñu bare daanañu tëp bar-bar yooyu, ñeneen di jééma xotti dogitu gééj gi dox seen diggënte ak seeni mebët, ci gaal baa ci looco. Gaal yu bari baa looco ya teeruñu ba téy ci tefesu Talkonia. Dañoo naax saay. Defe naa ne ba tay ñu ngi wéyël seen mebët ci diggënte asamaan su buló si ak gééj gu buló gi. Lu nekk a gënóón neen. Lépp a gënóón xiif gi, lépp a gënóón xeex bi, lépp a gënóón dund gu amul ëllëk… Ay góór lañu woon akiy jigéén yu jambaare. Ngardaaju woon lépp, yamale dund ak dee.

9

Page 12: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ca Talkonia, lee-lee tele bi daana wane yooyu xibaar. Nit ñi mel ni ñu doon xool beneen boor. Lee-lee am ñu ne “ndey saanam gore!” waaye, nes tuut ñu dellu waat ca seeni yitte. Doon te lee ndoxum tefes mi dafa daan soppeeku melo bu xonq te purit mi daan mel na dafa daan tis ca seen toogu ya, bu daan dal ca doc ya.

Lu mënë xew, ba nja jëkk ñëw ca góór ak jigééni Negrinia ak Marronia, ñu nééw la ñu woon ta daa wu ñu feeñ. Faale wu ñu woon ligééy ba, tay fayyu lu tuuti. Ñu ngi tambale woon ligééy ca tool ya ñu soxlaa woon ay nawetaan yuy daggiy doom, ay lujum akiy pombi teer. Ci gattal, ñoy Talkonia ñoo ngi doon xalaat ne daggiy doom moom ku nekk mën nako, te nekkul ligééy bu am solo.

10

Page 13: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

11

Page 14: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Bu ñu musaana jeexal ab liggééy ci ab goj, da ñu daan dem wuti liggééy ca beneen; jappoo ko noonu rekk. Tay fayyeeku lu nééw di sonn lu bari. Bu jánt mësaana so, ba ñuy dal lu, daa na ñu xalaat seen ñaboot, seeni soxna a seeni jëkkër, seeni doom yu góór ak yu jigeen yi nekk fu sori, tayit di leen bëgg indi ci Talkonia ngir taf leen ci seen xol, xir nekk ak ñoom.

Jamono di dox ba ñoy Negrinia y ñoy Marronia tambalee liggééy ci bërëp yi gënë metti ci isin yi, di defar ay kër ak ay tali, di tambale dëkk ci rééwi taax.

12

Page 15: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu
Page 16: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Mbir mi tambalee baax. Ñuy dollee ku ba gënë bari, tubaab yu bari, seen kanam soppeeku, tambale mboqq ndax mer ak ragal li uute ak ñoom.- Di nañu nangu suñuy liggééy!- Dañu leen fi wara daqq balaa ñoo jël suñu

yëf !- Rééw mi suñu rééw la!- Bëggu ñu suñuy doom bokk lekkool ak ñoy

Marronia ak Negrinia!- Dañoo wara waxee ni ñuy waxee ñun!

Yii ak yeneen yu mel nii, ñooy lenn ci kawtééf yi ñu daan dégg ci waxtaani medd mi, butik yi, baar yi, porogaramu radio yi ak tele yi ba mujje yubbaale nit ña ca loola.

14

Page 17: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ay ñaxtu ak ay manifeste yu boromi xel yu nëx jiite, daana ñu ca ñaxtu ay tërëlin yu tere gan yi duggëti, ta taxxale ñu ñuul ñi, ñu xereer ñi ak ñu weex ñi ci gox yi, ci lekkool yi, ci restorang yi. Nax mës

ngeen a gis lu ni mel?

Doon te lee niru wul dëgg, noonu la demee. Ba tax doxanéém yi tiit, jaaxle, took seen kër, xamu ñu lu xew. Nangu wuñu ligééyu kenn. Dañu daan ligééy lu kenn nangu wul a liggééy ta leer na ni nangu wuñu rééwu kenn.

Dañoo bëggoona dund ak liggééy rekk ci ngor, ak, bu manee nekk, bokk li ñepp bokk: ngelaw li ñuy noyyi ak mébëtu adduna bu gënë deggu tay dimbëlaate.

15

Page 18: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Benn bés ci weeru mars, ba ngelawal la tambalee upp, ba fulóór yi tambalee tóór-tóór, mu am xew-xew bu taaru… walla book bu yééme, mu aju ca kako gis.

Niki suba gu jot, way Talkonia dañoo ubi seeni robine di sangu, rekk ... ag mbetteel dikk. Nu ndox mi gënéé tooyal seen yaram, seen deru yaram di gënë soppeeku. Njenn nji buló, njeneen nji wert, yolet, roos, mboq, ñuul, sorãs... and ak bépp uute ak raññeeku boo leen xalaat. Cëy bii gacce! Mbedd yi soppaliku ay ndand foyfoy, kenn ñeme wul woon génn kërëm. Tele bi ay film ak ay futbal rekk a ci doon génn ayi bés bi weesu. Kenn bëggul woon génn di nettali xibaar bi, ba ñu di gis kanamam gu bees gi.

Page 19: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

17

Page 20: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ta itam ñoo ngi tambali woon di wax ak di dégg lakku ñoy Marronia ak ñoy Negrinia yu ña__ yooyu te doy waar. Fii la bët yam!

Minitër bi yor wallu njangale mi moo ngi doon tuumëlaate ne: “lii pexe kuréél yiy xeex boddikoonte ci biir xeet yi la, ngir gallangkoor luwaa biy tënk doxandéém yi ngir ñuy dem ca lekkool yu uute ak sunuy yos...” Te sax seen deru yaram dafa ñuuloon banga xamni bu solee kostimu ministër am bu ñuul bi, ci guddi gi, dafay mel ni nit ku amul jëmm.

Ministër bi yore kaarenge gi, te der bi moqq mel ni nen, moo ngi wax njiitu rééw am: - Nañu sanni benn jum!- Waaye... Kan la ñu koy sanni? Njiit lu

dóómu taal li laaj ko ko.- Xamu ma ko, waaya nañu sanni

benn jum

18

Page 21: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Paco miy jaay ci butiku tangal bi, te ame colóóru lastik bu xonq, xamul woon nax dafa wara mer walla dafa wara reetaan; defe naa ca dëgëntaan mbir mi dafa reelu ci moom. Foo xam ne njëpp dañu bégoon ci mbir mi, foofumooy sunu lekkool. Gune yu tuuti yi dañu daan bég, bu ñu mësaan di fo powum sercal bu ñuy jappoo loxo di way.

Don Pedro, kilifa gi, feeñ ak mustaas am bu ñuul ci der am bu wertbi, def ñu ree ñun ñëpp, María Xesus, suñu njaatigi, and ak deru yaramam bu ame rëdd yu yolet doon ñu ñaax ci ñu def ay kuréél ngir ligééy ci kulóór yu ranjeeku wul yi ak yu xaññaaral yi. Karlos mi gënë télléérël ci lekkool bi, nga xam ne saa su nekk mi ngi wane ak ngóóraam ak ay dall am yu ñuul, mujj na soppali ku der bu roos di wax lakku Marronia waxin bu neex a dégg.Took na ayi bés dellu wul lekkool. Xamul woon lu ñu doon reetaan.

Rosita jekkoon lool ak deru orããs am... Dafa mengóó woon ak bët am yu wert ya. Ki ma bokkal taabal, Nikolas, di xitaano, mooma gënoona weex lu jiitu bés booba.

19

Page 22: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Doktor Guadalupe, pediatar bi, dafa xeesoon pecc mel na purtugees rafetoon lool and ak buluus am bu weex ba. Fan yu jëkk ya dafa yééme woon. Gune gii dafa ame ngas wala xonqaayu deru yaram am la? Liir bi nak, ak yaram am bu mboqq bi mel na limong, dafa pëyiis walla?

Ba Njanq Ines wësinee doom ju rafet, ame yaramu karo-karo yu yolet ak wert, xamul woon ndax dafa wara jooy walla dafay reetaan. Ku waxal Yalla xam ne lu nexu la woon. Rakkam ja Alba, tay jángee s_kéém te yaram am ame woon kulóór bu soon-wëluur, neexoon ñu, ñun ñëpp, moo ngi defaroon benn powum yoote ci kaw biiru xale bi. Doomi yoote bi dafa

ko doon coqataan moo tax mu doon yëngu lu bari ba tax po ma mënul woon a yegg.

Sama doomu nday, Margarita, deru yarama am bu wert ba ne salaat dafa andoon ak moom, rax ca dolli xob rekk lay dundee. Segam dafa soppoon di lekkee loxo, benn guddi, ca reer ba, mu jaawale baaraam am ak komkombar, dal di koy matt ba tax mu daw demm loppitaal ca lu gaaw.

20

Page 23: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

21

Page 24: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ci loolu lépp, waxu ma leen, man, nu sama deru yaram meloon. Ca dëgg-dëgg amul woon benn kulóór bu ñu mënë wax. Damaa meloon na kakkatar. Dégg ngeen de? Sama deru yaram dadfa daan soppeeku andd ak nit ñi daan nekk sama wet. Ca tambali ba, ñakk sama kulóóru bopp daf ma doon naqari. Waaya ginaw gi sama yaay leeral ma ne, man sama deru yaram njaxas la. Te dafay rafet bu dee soppeeku jamono ju nekk. Ci noonu laa ko tambalee gisee noonu.

Ci medd mi, nit ñi dañu daan nuño ci benn kallaama, ñii di tontu ci beneen kallaama mel ne….ak ci surnaal yi dañu doon bind xibaar bu nekk ci lakk yu uute.

Mënoon naaleen a nettali misal yu bari, yu mel ni yii, waaya… seen xel demul ci laaj nan la ñoy Negrinia yi ak way Marronia yi mujjéé? Xam ngeen ko moos. Melo bu nekk amoon na ca ñoom. Naka ñeneen ña, mel na ñëpp. Leegi, boo leen giséé, doo leen xammee. Doxu njaxtu yi, daal di jeex. Segam njëpp a uute woon, jaratul woon ragal leeneen lu uute ak ñun.

22

Page 25: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ay at ca kanam, kenn fattalikootul na sa deru yaram meloon, ca tambali ba. Te laca gënë neex mo doon, leg-leg, bu ñu masaan di sangu, seen der ba dafa daan soppeeku. Way gëstukat yi, bi ñu gëstoo ca ndox ma lo bari, gisu ñu ca benn tektal bu yanu maanaa. Waaya, wax dëgg Yalla, nit ña, waxu mala rekk ne mujj nañu ko tamm, waaya dañoo mujj di tiitëróó boobu melokaan.Dem na ba Kuréélu Ndawi Rééw ma, faf and ca soppi turu Talkonia, def ko KOLORINEA: rééwu melokaan yu uute yi.

Gan yi joge ci adduna bi yëpp dañu ñu daan seet si, ngir gisal seen bopp ni, li ñu daan yëgle ca tukki ya, lu am la. Ba ci gan ya sax, ganaaw seen ca__aay lu jekk, kenn dootu leen xammee. Ci biir uute gu metti googu, mëneesul woon xammee xeet, lakk, walla cosaanu kenn. Moo taxoon ci tééré baat yi, ñu far ca baat yu mel naka dig ci ay xeet, mbañeel, boddikoonte, xeet, te it am magget ñi rekk ñoo doon fattaliku lu baat yooyu doon tekki cay jamono.

Page 26: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Ca ay bërëb yu jege, ay nit yu am maanaa joge nañu fa, naka Drago ak xarit am Xorge, Waxambaane mi nga xam ni, ca boori weeru awril, da daan ñëw nemmiku suñu rééwi taax yi ak suñu kaw gi. Bamu sangoo ca dex ga, la soppeeku wert am bu ñor ba woon ca deram ba, doon ay kulóór akiy melo yu bari. Suñu xarit ba Drago, loolu safu ko woon, rax ca dolli, dafa daan doxontu ca Luumay Tééré ya. Ah! Ba ci tegu Waxambaane bi Xorge dafa soppeeku woon, def ay rëdd yu xonq ak yu mboqq.

Bamu defee fukki at ak ñatti fan yu mat sëkk, mu am beneen xew-xew bu bette. Ganaaw seen cangaayal fajar, nit ña dañoo dellu waatoon ca seen melokaan bu jëkk ba. Lépp dellu melaat na bu jëkk. Ndax lépp la? Wax dëgg Yalla, du lépp. Dafa mel ne, daa amoon kenn walla lenn lu bëggóón jooxe benn njangalem yaatal jëmële ci giir Talkonia, te itam ñoom jáng nañu ko. léégi ay melo yu uute lañu, te itam dégg nañu te dañuy wax lakk yu bari.

24

Page 27: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu
Page 28: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

26

Ganaaw bañu ko wootee, ñëpp dañoo and ca ñu wéyël turu KOLORINEA, ngir ñëpp xam ne foofa, ganaaw jamono joojee, melokaanu deru yaram ak lakk munul a waral mukk ak daqq baa buddikoonte. Benn uute bi am ci biir nit ñi, mi ngi wara nekk ci seen yëg-yëg ak seeni jëf, waaya warul a nekk ci seen melokaan, baa seen koom-koom.

Ngir maggal lii ma leen nettali, benn yoon ci at mi, ñaar fukki fan ak benn ci weeru me bu nekk, xale yi ak mag ñi dañuy def feet bi gënë neex ci adduna bi yëpp. Ci lekkool yi da ñuy jáng benn ñaxtu bu ñuy fattali boobu xisa. Soo leen ko bëggéé dëggël, diw leen seen kanam bu baax, ak seeni loxo, ngeen jaar foofu. Di ngeen mos liminaat bu buló, pete-pete yu yolet ak tangal yuy saf njaxas.

Page 29: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu
Page 30: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

28

Page 31: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

29

ÑAXTU

Xale yu góór ak yu jigéén yi ci daara jii, da ñoo bëggë birël, bés niki tay ne xamu ñuy dig yuy xajjatle ay nit.

Suñu mébët mooy adduna boo xam ne nit ñi du ñu faale melokaanu deru yaram, kallaama ba muy lakk baa rééw mamu jogéé.

Xam nañu ni, ñun nit ñëpp dañoo uute waaya ñoo bokk benn bëgg-bëggu dund ci jamm ak moom sa bopp.

Xale yu góór ak yu jigéén yi ci daara jii ak yi ci daaray Aragon bi yëpp, am nañu yelleefu mébët adduna bu lëndëmul, boo xam ne araf yi, tééré yi, xalima yi, asamaan si, bés yi, dragõ yi ak xarit yi dañuy ame melokaan yëpp. Loolu taxna ñun ñëpp ñoo ngi and yuuxu ca kaw naan:

DÉDÉÉT BODDIKOONTE CI BIIR I XEET.DA ÑOO BËGG DUND CI ADDUNA BU FEES AKIY MELOKAAN

Page 32: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

30

MANIFESTE

Nous, les enfants de cette école, nous tenons à dire aujourd’hui que nous ne comprenons pas les frontières qui séparent les hommes. Nous voulons un monde où les hommes s’aiment, sans regarder la couleur de leur peau, leur langue ou leur pays d’origine.Nous savons que nous sommes tous différents mais nous partageons le même désir de vivre en paix et en liberté.Nous, les enfants de cette école et l’ensemble des écoles d’Aragon et d’ailleurs, nous avons le droit de rêver d’un monde qui ne soit pas gris ; un monde où les lettres, les livres, les crayons, le ciel, les jours, les dragons et les amis seraient de toutes les couleurs. C’est pourquoi nous crions haut et fort tous ensemble :

NON AU RACISME !NOUS VOULONS VIVRE DANS UN MONDE DE COULEURS

Page 33: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

3131

Page 34: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

3232

DECLARATION

The boys and girls of this School wish to say today that we do not understand the borders that separate people.That we want a world where people care for each other no matter their skin colour, their language or the country they are from.That we know that all people are different but that we share the same desire to live in peace and freedom.The boys and girls of this School, and of all the schools in Aragon and any other place, have the right to wish for a world that is not grey; a world where words, books, pencils, sky, days, dragons and friends can be of any colour at all. For this reason, we shout strongly and together:

NO TO RACISMWE WANT TO LIVE IN A WORLD FULL OF COLOURS.

Page 35: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

3333

Page 36: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

3434

ÑAXTU

Xale yu góór ak yu jigéén yi ci daara jii da ñoo bëggë birël bës niki tay ne xamu ñuy dig yuy xajjatle ay nit.Xam nñu ni ñun nit ñëpp da ñoo wuuté waaye ñoo bokk benn bëgg-bëggu dund ci jamm moom sa bopp.Xale yu góór ak yu jigéén yi ci daara jii, ak yi ci daría Aragon bi yëpp, am nañu yelleefu janneer adduna bu lëndëmul, boo xamne araf yi, tééré yi, xalima yi, asamaan si, bës yi, dragon yi ak xarit yi dañuy ame melokaan yëpp. Loolu tax na ñun ñëpp ñoo ngi and yuuxu ca kaw naan:

DÉDÉÉT BODDIKOONTE CI BIIRI XEET (RASISM)DA ÑOO BËGG DUND CI ADDUNA BU FEES AKIY MELOKAAN

Page 37: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

3535

Page 38: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

36

Page 39: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

Desde el CAREI (Centro Aragonés de Recursos para la Educación Intercultural) queremos animar a todas las Escuelas de Aragón y a las de cualquier pueblo o ciudad del Planeta Tierra a adherirse a este Manifiesto por Una Escuela Contra el Racismo.

Sólo tienes que entrar en nuestra página web: www.carei.es y allí encontrarás el siguiente enlace donde además de sumarte a esta apuesta por un mundo en el que quepan todos los colores, podrás descargarte el cuento en pdf, un cuaderno para colorear y sugerencias didácticas para los distintos Ciclos de Educación Primaria.¡¡Anímate!! Tenemos que probar la limonada azul, las palomitas violetas y el dulce sabor a mestizaje.

MANIFIESTO POR UNA ESCUELA CONTRA EL RACISMO

Page 40: RÉÉWU MELOKAAN YI - · PDF fileLoolu dafay tekki wuute ak ñeneen ñi, ta giiru Talkonia munu ñoo dégg loolu. 4. 5. Daf leena leeroon ne ñu dul ñoom duñuy niti dara, nit ñu

38

Organiza:Patrocinan: